text
stringlengths
6
463
Ay nit yu foqale, ci njàppaleg meer yi, ñoo ngi dagg suuf si ci lu tegewul fenn te xooluñu sax jafe-jafey dëkkuwaay yi mu mën a jur.
Daañu woo ay saasenegaal te duñu ci seet jan diine lañu bokk.
Xamal nit ñi li ñu ci war a xam yépp te jaarale ko ci tënk wii: génn leen seen kër yi dem fajuji su fekkee dangeen feebar,
waaye fexe ba génne ci xeli nit ñi baat bii : toogleen seen kër doonte sax dangeen a jagadi.
Ci lim bi, gis nañu ci turu njool mii di Tàkko Faal ak Yusufa Faal mi nga xam ne bëgg-bëggam moo nekkoon réewum Farãas woo ko.
Ñu ngi ñaan booloo ak jàmm ci Senegaal boo xam ne naataange ak dundin bu mucc-ayib di na fi saawaan ci ñépp, bañ a yem ci ñenn ñi rekk.
Askan wi dañoo war a sàkku ñu woo Karaa bala ñoo diig.
Sea Premium 100 bu siiw bi ñu tudde Fatig, nekkul ag gaal goo xam ne njiitu réew mi daf ciy doxantu,
Ni ki La signare, dafay yóbbu njiiti Senegaal yi ak gan yu am solo yi diggante Dakaar ak Gore, ci anam yu ànd ak kaaraange gu àdduna yépp nangu ne noonu la war a mel.
Ci loo xam ne waru ko, ab jëwriñ ci nguur wax na ne ki fi nekkoon njiitu réew mi moo jël raw kàddu gi ci wote yi.
Beesal gi am ci pólótig bi dana tax, ci lu wér, ñu dellu ci suñuy xar-baax.
Njiitu bokk-moomeel bu Cees mu ngi ci jiixa-jaaxa.
Xojax yi dañoo nas pexem lekk.
1 – Jëfandikoog nafag réew : li jëm ci wàllu dàmpe ci loo xam ne dees koo foqatee ci nit ngir njariñal ñépp.
Ca Guinée Bissau ak ca Niger daanaka yeksi nañu ci.
Yaakaar nañu ne itam coppitee yooyu dina eksi Senegaal ci atum 2024.
Sa ree ju neex jii di firndeel dëggu dina des ci suñu xol yi ba abadan,
dina des itam ci xolu képp ku bëggoon réew mi,
yàgg a mébét senegaalug jàmm, senegaalug naataange, Senegaal gu moom boppam ak gu boole xeet ak diine yépp, te suuf féete leen kaw.
Dafay def ay widéwoo yu bare yoo xam ne moo ngi ko duppe Càmbar gafag réew mi.
Ci widéwoo yooyu, dinaa ci dikkaat ci lu yaatu ci Yoon wiy yéwénal li ñu natt ci koom ci atum 2020 ak céddale gi ñeel at miiy ñëw
Ginnaaw gi, liggéey na ci kuréel yu wuute yoo xam ne fa la jàngee lépp lu aju ci wàllum xarala.
Ci xelu waa APR, ndam li ca gox bu Sigicoor lay gën a neexee, fàww, ak nu mu mën a deme, ñu boole leen ci li ñuy def.
Li ci gënoon a doy waar mooy ni futbalkat yi doon xeexee bu ñu ñàkkee bal bi.
Waa Liverpool jël nañu seen juróom-benneelu Ligg dee sàmpiyoŋ.
Daañu fa dajeek sax ñu yore seeni lijaasa ba noppi di jaay ay lëjum, ay dàll wala sax yu nekk ay defarkati dàll.
Waaye kiy tàggat gaynde yi nee na yemul rekk ci menn pexem futbal.
Noo ngi xaar ak yàkkamti beneen teg-dóor bu Senegaal.
Xanaa nekkul ne ci jafe-jafe ngay xamee say xarit?
Aamadu Tiijaan WON nee : muus-muuslu ak bariy afeer ci fàtteliku rekk lay mujj.
Leer na, dafa jaawale péncum ndawi réew moomu ak mu Senegaal.
Bataaxal yii maanaam "doole dëgg mooy mën a woote fépp ci Senegaal",
"Yëfu ponkal dëgg mooy mën a def la war fépp",
"Njaatige dëgg mooy mëne fu ne",
"Cool dëgg mooy mën a konektewu fépp ci Senegaal ak 4G+ bi".
Bataaxal yii dafay wane, ci lu wér, yéeney yàq deru Free, rawatina nag jëfandikoog baat yu ci mel ni « fépp » ak « fu ne » nga xam ne dafay gaaruwaale Free.
Ñàkk a sàmmoonteek dogal yii, li muy jur mooy, ginnaaw bu weesoo li ci bérébu dencukaayu xaalisu réew mi di ñàkk, musiba ci ñàkk a fay lempo te loolu itam mën na jur jafe-jafey askan.
Ci li Joseh Ki-Zerbo wax, neenal bor bi, nekkul saafara suy sax dàkk ndax ba tay li koy jur jógu fi.
Saajo Maane moom bi ñu dallujee ba dellusi lañu ko génne.
Gaaw a dog, mooy dog rekk bu jant bi sowee, ngir waxam ja.
Njiitu réew mi Maki Sàll wane na bëgg-bëggam ngir def mbir mi bu jógee ci boppu réew mi.
Réew mi mën naa dox ak keneen ndax campeef yi mu fi teg wala yi mu gën a dëgëral,
am na ñu solo ba nga xam ne moom sax bu dul moom, réew mi nga xam ne am na bànneexu jiite ko, mën naa nekk ci dal.
Xam naa ñaar ñoo xam ne ginnaaw ba ñu jógee ca këru njiitu jëwriñ ga, dañoo soppeeku ay xalamkatu nguur goo xam ne yoonam nekkul ci askanam.
Xoqatal yi nga xam ne dund na ko ci bés bi, yokk ci yi mu nar a dund ca kër ga.
Am na aw dig wu nekk ci diggante ñi jiite ak ñi ñu jiite.
Amuñu ruu ga, amuñu xadar ba, amuñu mën-mën ba wala xam-xam ba, amuñu tam xel ma.
Siise amul lenn lu mu mën a jàngal xale yii nga xam ne ñi leen di tàggat ñoo gën a xarañ boroom njañ yi fuuf.
F. Bojãa nekk ki jiite wàllu jokkalante bi ci bérébu fajukaay bi dañu koo tuumaal ne dafa luubaal lu tollu ci juróom-ñaar ???
Dañu doon faral di wax kàddu gii: mooytuleen ki war a fey lempo ki;
dafa ñor, day njuuj-njaaj, day nëbbu, topp ci di la ko wax ak a waxaat.
Jafe-jafe bi, kuréelug Amerig giy yëngu ci wàllu kaaraange digal nañu yenn ci ay njiiti bitim-réew ñu bañ a jël bato bi ñu tudde La vedette bu ñuy dem gore.
Dañoo war a sàkku ak njubal ci ni ñu yoree suñu xaalis,
sàkku ñu defaral ñu ay jumtuwaay yu baax,
sàkku askan wépp jot ci céddale gi.
Ci tënk daal sàkku ñu andiy saafara ci suñuy yitte te loolu dafa war sax dàkk ci xelu njiit yi.
Ngir mën a egsi ci lolu Maam Mbay yaakaar na ne fokk ñu am tëggin yu yees ci suñu wàllu askan.
Tëggin yu mel ni yu Usmaan Sónko, mu tegu ci gëm-gëm bu dëggu te amul benn njuuj-njaaj wala waxtaan ba juboo.
Ci noonu la nas bi amee benn pàcc bu ñu jagleel ab xeetu mbay bu mucc-ayib boo xam ne dafa yomb a jëmmal te saytu ko tamit seerul lool.
Ci beneen joŋante bi ci kippaango G bi, ci ñaar-fukkeelu simili bi ak juróom waa Russie yi lakk caax yi, waaye bi ñu noppalujee ba ñëwaat, waa Almaañ yi wane nañu beneen xar-kanam.
Waaw, këru liggéeyukaayu Farãas gu mag bi, wàññi na bu baax njëgi yónne wala jot ci xaalis gi.
Baay Móodu Faal ñu gën koo xam ci turu Booy Jinne dafa rëcc dibéer fanweeri fan ci weeru mee ci kasog Camp pénal gi nga xam ne ci ruq bu am kaaraange lañu ko fa dencoon.
Su ñu sukkandikoo ci Libération, ki doon dawal BMW bi, Mamadu Jóob te mu am fukki at ak juróom-ñeent amul këyit giy firndeel ne war naa mën a dawal daamaar.
Korent – ci faranse mooy Première épître aux Corinthiens.
Club anglais bi def na jalloore ju rëy.
Saajo Maane wone na ci njàmbaar gu réy.
Dafa tàmbalee tëj gémmiñu benn pàcc ci ñiy xeexal askan wi te defu ñu pólótig, ci loo xam ne da leen di ger, wala mu wañ seen loxo.
Ginnaaw gi muy xoqatal këri tas-xibaar yi nga xam ne féetuwuñu ak moom, ba noppi salfaañe lépp lu tënku ci wàllu wote.
Li mu mujjee nag, mooy tënk sañ-sañu nit ñi.
Xaste ak ñaawal doŋŋ lañu am,
moone Usmaan Sónko laaj na leen ay laaj yu ñu tontoogul ba tey.
Ngir loolu, fokk ñu tabax ay kaso yu yees yu méngook ni ko àdduna yépp di defe.
Xeeti nit ñu jàng ñii, dafa leen di neex ñuy tagg xar-baaxi jaamu ak jëf yu doyadi.
Ñi jot ci feebar bi, bu ñu demee seen kër, mën nañoo wàll màggat ñi, ak ñi nga xam ne dañoo ame yeneen feebar,
te ñoom Koronaa wiris bi ñoom lay gën a faat.
Njiital raay bu gaaw biy lëkkale gox yi, Abdu Ndeene Sàll, moo nekkoon ganu RFM ci aljuma ji.
Njàppale gu mel nii dana gën a dalal xelu joxekat yi yaakaar na béréb bi mënul a dékku mbooloo mi fiy ñëw yépp.
Su fekkee dañu ñu teg tiis, ñun chretiens yi, dañu ko war a nangu ba àdduna di tukki, laata xew-xew bu neex biy ñow, te muy yemook yëkkatikug jàngu bi.
Su fekkee palaas yi am mbaar la, dinañu fa jaay junni ak ñeenti-téeméeri këyit yiy jàppandal dugg gi njëg li junni la.
Su fekkee palaas yi amul mbaar la, ñaari junni ak ñeen-fukk këyit lañu fay jaay, ci juróom-benn téeméeri dërëm.
Ay bérébu déncukaayu xaalis a ngi ubbeeku ci lu tegewul ci yoon.
Soo taseek Booy Jinne du la mës a xool ci bët.
Dara wuutalewul Aysata ak Raasin Si.
Dafa yomb ba nga xam ne dañu naan naka lañuy liggéeyalee ab dag?
Su ñu tënkoo ciy kàddoom, moom rekk moo yoroon caabi koppar-foor bi.
Ñoom dañuy xalaat seen aafiya ji, anam yi ñuy nekk bu ñuy tukki.
Nekkoo dàllinkooru ekib yiy futbal ca Angalteer.
Waaye yaa jël raw-gàddu gi ci Ërob ak joŋante yu bare yoo xam ne kenn dugalu la ab bal.
Sëñ Saar mi nga xam ne dawal mooy méccéem, ab saytukatu kaaraange moo ko jàpp ci guddi gi muy sàcc ab gaas ca Grand-Yoff ci wetu Zone de captage.
Mu ngi yoroon ab woto boo xam ne kenn kuy yëngatu ci wàllu dem ak dikk moo ko moom.
Ginnaaw bi mu tëjee ay wujjam, salfaañe càmpeefi réew mi, njiitu réew mi xaarul woon yënguteg ñoñi Usmaan Sónko yi.
Réewi CEMAC yi dañu lànk a yeesalaat jokkalante gi dox seen digganteek Farãas te mu def lu tollook juróom-ñaar-fukki at ak juróom.
Moo tax xaalisu ëro bi bareetul ci seen ja yi.
Ci tënk, mën nañu wax ne li njëwriñ ju nekk war a jëfandikoo ci koppar dafa koy fësal ci ay yëngu-yëngu yoo xam ne lim bi ci diggante ñaar ak juróom-ñeent lay nekk.
Fajkat bii di Róos WARDINI, nekk njiital ONG Médicol International nee na bokk na ci fajkat yi fiy ñëw te jóge Corée, ñoo xam ne seen xam-xam ci wàllu bëñ la màcc, ñii ci wàllu xol, ñi ci mbiri jigéen ak yeneen ak yeneen.
Wote, ngir wane benn niral rek, yelleef la ci gisin bi ma am ci demokaraasi, maanaam réew moo xam ne askan wi ñooy fal ak a folli.
Gisin boobu sax gën naa xóot loolu ndax wote moo raw sax yelleef ba ci tëgginu campeefi réew mi, foog naa ni amul kenn ku mën a génne boppam, ci tayeef liy doxal réew mi.
Usmaan Sónko, mi nga xam ne Mamadu Ja mooy royukaayam ci pólótig ba mu tudde ko sax béréb bi pàrteem bi nekk, ci baat yii la ko tënk : lan mooy nguur?
Nekkul lu dul aw sas woo xam ne dafa lay tax a fàtte sa bopp ngir saw askan.
Li mënul a ñàkk ci njiitu réew lu baax mooy mu am xam-xam ak jaar-jaar bu baax, am gis-gis bu leer, am yéeney jariñ réewam, bëgg réewam, doylu ba noppi nag ànd ak ñu mën.