text
stringlengths 6
463
|
---|
Ndagam wax nañu ne benn Ëro mooy ñaari téeméer ak ñeen-fukki EKO, lu ñuy wéral la ndax joxeeguñu njëg lu mujj gi.
|
Seefaa : Jules Pascal Coly, doomu Senegaal di pereetar, wéddi na waxi Alasaan Watara ji.
|
Nee na Sónko dafay wër fu mu setale fukki milyaar yi ko ay jixaatkat jox.
|
Abu Si (taskatu xibaar), Yoro Mamadu Jàllo (kameraamaan) ak Usmaan Njaay (dawalkat) ñoo nàkk seen bàkkan ci laksidaŋ bu metti boobu.
|
Bu ñu sukkandikoo ci Apanews, àttekati Mbootaayu Futbal gi ci Afirig génne na Ginne ci joŋante bi war a am ca Tanzanie,
|
te neenal nañu ndam yi mu amoon yépp ci joŋante bi.
|
Loolu moo tax, ma topp ci say wax,
|
woo naa la ci mbiru lempo ba ca Péncu Ndawi réew mi.
|
Baay Móodu Faal, soo moytuwul mu tëdd ñaar ba ci ñeenti ati kaso ndax dawam bi.
|
Juróom-benni laksidaŋ tamit am nañu ci tali bi te ñu waññi ci kenn ku faatu.
|
Ca Kódiwaar, njëg yi këru telefon yi joxe dañoo kawe lool.
|
Balaa ngay wax yokkuteg dundinu askan wi, seetal ne liggéey yu rëy yi nguuru Senegaal def, misaal la ci jeexital yu bon yi mu am ci ñi dëkk ci béréb yi mbir mi laal.
|
Looy wax ci réewi Afirig yi jox seen lépp Farãas te bàyyeeku bañ a jéem dara ?
|
Boo ko tëkkalee ak réew mi ñu nootoon, njiiti kujje gi duñu wax jëm ci këri soldaar yi waa Farãas am ci Afirig.
|
Am na yenn mbir yoo xam ne, musiba da ciy baax la léeb wax:
|
Mbir mii dina wane, ak lu mu tuuti tuuti, dëgg-dëggi melokaanu xeetu toppinu yoon cig gënële ca Farãas, ci nga bokk ci yenn askan yi wala yeneen ya.
|
Ab tàkk-der lañu yónni woon kese ngir mu nanguji këyit yi ñuy bindoo ngir jàppale sa farandoo ca Sigicoor.
|
Digé bor la.
|
Këlëbu almaañ bi bàyyi na ñett ci ay liggéeykatam yu mag ñu dem ci seen coobare bopp.
|
Ci béréb bu jafe, Spurs yi masuñu faa ragal a dem.
|
Ki yore kàddu gi, Masayeer Sàmb, Pastefu Kebemeer, nee na àllarba fukki fan ci weeru suweŋ atum 2020 lañu jàppoon ba tënk ko ak waa mbalkam deret ca Luga.
|
Ropplaan yii ñoo gën a màggat bu njiitu réew mi, Puwent Saareen.
|
Kiy lëkkale liggéey bi ca kurélug Disoo ak Pexe ca SN KOM EKO, xaalisu Afrig wala njublaŋ bu bees ngir yokk nooteel ak Farãas-Afirig ?
|
Dëgg la ñàkk par-parloo ci benn boor mooy li gën.
|
Amul benn liggéeyu xamtu dëgg, dëgg, bu taxasul jëme genn wet.
|
Dinga ko mën, dëggal ko!
|
Bul soppeeku Saajo mukk!
|
Gaynde nga!
|
Doomu Afirig bu raxul dara.
|
Li mu defalul daarayi, nag, moo tax amul màqaama wax ci ñoom.
|
Ginnaw Sala ak Firmiñoo, Red yi mënuñu yëngal Ter Stegen.
|
Mesi dafay dóor ak di paas ba ñu far yemoo.
|
Askan wiy jëfandikoo xaalis boobu kenn laaju ko ci jëfandiko gi.
|
Waaye, bu amee lu ñuy wax Borom mer-gàddu gi, mooy mu jéem a def ay pexe ba jox ñu li ñu amul bu baax.
|
Te bu ñu jëlee lim yi, lim yi doŋ, xaalis bi ñuy yaxanal mën a tollu ci juróom-ñaari milyaar ak ñeenti téeméeri milyoŋ ak fukk-ak-ñeenti ak ñeenti téeméeri junni ak ñaar-fukk-ak-benn ak ñeen-fukk ak ñaari dërëm ak ñeenti fiftin ci xaalisu Seefaa.
|
Ci genn wàll gi, fàttali naa jëwriñ ji ne sosug ndimalug njaboot yi weer wu nekk ëlëm na ma, ci nguur goo xam ne, nee na payug liggéeykatam yi moo doon yitteem.
|
Defin wi gën mooy jariñ sa réew.
|
Dañoo waroon di amal ab leeral ci doktoor yi nguur gi di fay te ñu am yeneen payoor yu mën a gàllankoor seen liggéey.
|
Bu ñu sukkandikoo ci yéenekaay bii, tënku luwaas bi ak Cmc bu BMW bi wérul.
|
Sidaan ak Reyaal dañoo nekk ci ay jafe-jafe laata ñuy am seen ndam lu njëkk ci LD ak Galatasaraay mi aw yoonu ñibbi.
|
Njàngat li joxe na digle yu bari yu doon pexe yu ñu mën a jëfe ngir jàpple leen.
|
Jeex na.
|
Xam nañu ne Senegaal soriwul diggante boobu.
|
Juumte mu rëy la ci nasum pexe mi.
|
Ginnaaw mbirum ñàkk a dugal lempo mu Ngomblaan gi, beneen njombe amaat na foofee.
|
Jàppoo ko noonu rekk njiit li.
|
Doomi Autriche bi am ñaar-fukki at ak juróom-ñetti futbalkat la bu mën a taxaw ci defaas bi, ci càmmoñ ak ci digg bi.
|
Ci mbir moomu, jàppoo gu nguur gi ak mbootaayu ñi liggéeyul ci nguur gi mën a ci dox jeego yu am solo.
|
Ñaata xale yu jigéen ñoo gis seen ëllëgu njàng wala liggéey yàqu ndax amuñu ku leen jàppale?
|
Lii moo tax ñu fexe ba am dayoo bii ngir yaatal yoon wi.
|
Amoon nañu ndam ca ndaje ma ndax dajale woon nañu ay ñit ñuy dugal seeni koppar ci koom-koom bi ci àdduna bi, ak xaalis bu ëpp juróom-benni yoon li Senegaal doon wër, ak baaxaayu nguur yi yéenee dugal ci seeni koppar xarañ nañu ci lu mel noonu.
|
Dërëm ak ñeenti fiftin ci xaalisu Seefa ci soble ak pombiteer njël lu nekk!
|
Xool leen sunu koom-koom bi ñu donn, ndax pólótigu nguur gi gënu koo jëmale biti réew?
|
Ginnaaw ñaari at ca boppu Eferton, te mu nekk ca fukkeelu taxawaay ba ca Premier League, at mii, Karlo Ansoleti dellu na ca Reyal Madirit.
|
Sunu askan wi dafa tënku ci ay defin, aada ak ngëm yu bari yu jëmmal suñuy yég-yég.
|
Loolu la mooy wax ji, nañu ko nangu rekk.
|
Ndawu réew mii di Usman Sónko dàq na koppari pólótig yi ñuy jox kilifay réew mi.
|
Bi ñuy màggal bès bi àdduna sépp jagleel kéewnga gi, juróomi fan ci weeru suweŋ, àll bu ndaw nekk ci biir Ndakaaru la Ndawal Mbootaayug réewi Tugal yi ci Senegaal, Irène Mingasson, ubbi ca Wakaam.
|
Ropplaan bu bees dafay bokk ci liy yokk taaru réew mi.
|
Gëstukat bu jigéen bi ñaax na ay moroomam ñu jëm ci génne ay téere yuy jariñ daara yi, nguur gi ak askan wi.
|
Boo weesoo sax seen bariwaay, way-pólótig yi dañoo war di wax wax ju toppe.
|
Ñu xam ko ci ñàkk a ànd ci xaalisu Seefaa, dafa tàmbalee ay waxam ak cosaanu xaalis bi.
|
Soham El Wardini, njiitu méeri bu Ndakaaru, Ali Aydaar, saa-aalam, te masoon a doon jëwriñu càkkéef bi, demoon nañu ca bès boobu.
|
Beresil ak Senegaal dañoo témboo ku ne am benn bal.
|
Lëñbëtu tàkk-der yi ca këram tax na ñu teg loxo ci as caag su def fan-weeri xeer ak benn yu karak, juróm-benni mbuusi kokaayin, di peese genn-wàllu liibar.
|
Gisuma ci lenn lu ñaaw, ëllëg, bu Senegaal awee yoon wu bokkul ak wu Móoritani wala Marog, wala yeneen.
|
Ci seetlu boobu, kilifay Mbootaayu réewi Afirig sowu jànt ngir koom-koom bi war nañu gën a liggéey seen tëralin wi ñu dëppoo (nafarug ponk yi, dëgëralug nguur yi)
|
Njàqare bu am Niseriyaa, ci misaal mu bawoo ci wàccu njëgu petorol ba, te réew yépp mën cee dugg, bu fekkee ni sax amoon nañu lu baax, loolu la liggéeykatu bànk bu xam dëkk boobu gaaral.
|
Ñaari at ci kanam ak ñaari ayu-bès laata ñuy tambali Kub Afirig ba am ca Esipt, lañu tuumaaloon Seriñ bi ay loxoom set ci CAF.
|
Bu dee sax tàmbalib joŋante ba doyoon a waar ba Origi njëkke dugal ginnaaw njuumteg Alba (benn ci dara, juróom-ñaareelu simili), Katalaŋ yi mujje nañu tiye futbal bi ci seeni loxo.
|
Xoolal rekk cawarte gi nit ñi àndaloon ca jàkkaarloo ak askan wi bu njëkk bi Léwópól Sedaar Seŋoor defoon bi mu faloo, juróom-benni fan ci weeru sàttumbar ca atum 1960, wala nga fàttaliku bès bi ñu falee Wàdd ca atum 2007.
|
Ñiy diiŋat loolu dinañu ma wax ne amul njariñ.
|
Te jaadug jigéen ñi di am ay cër ci kuréli pólótig yi dina mën a doon ab laajte bu taxaw.
|
Ndeysaan defu ko waaye bul teg sa bopp ay jafe-jafe.
|
Ñaari xale yu ndaw, kenn ki am fukki at ak benn, keneen ki fukki at ak ñaar, ñoo réer daanaka lu tollu ci fukki fan ak juróom.
|
Ci mbir moomu, wax na ne xaalisu Seefaa doomu Afirig moomuñu ko.
|
Lu weesu wax ab taaram, mën nañu laaj ban digaale la rafetaay bi nataalkat yi sàkk séq ak taaru mbir yu rafet yi, wala taaru xale bu jigéen ?
|
Koronaawiris wane na ni doom-aadama xiiboonee.
|
Ci lu jàmp lañu yebal Le Drian ca Abijãa ngir mu fàttali njiitu réewu Kódiwaar ne dafa war a sàmmoonteek li mu dige woon te dàq joŋanteg pal ga ndax mu mën a am ku mu samp.
|
Saa su ne dafay def te xoolu ci dara.
|
Moo tax muy liggéey ngir yokkuteg dëkku cosaanam, Bàmbaali, ca diggante bëj-saalum ak sowu réew mi.
|
Seetal rekk, guddig weeru koor, ci ngelaw li, ñuy fanaane taxaw guddi ba bët set.
|
Ngir fexe ba wut béréb yu bari yu ñuy defaree kuraŋ, Maki Sàll gisul dara lu tane fexe ba ku nekk mën di jëndal sa bopp kuraŋ.
|
Ñaar ñi ñu tuumaal dinañu jàkkaarloo, tay, ak njiital àttekat yi.
|
Ab TABURE.
|
Mooy dof bi ñu fayoon ngir mu taxaw temm saa yu gisee xibaar buy wax ci Usmaan Sónko, mu di ko ca wax lu ñaaw.
|
Kurélug pólótig gii di APR ci xàll woowu la aw, dafay mujje sax yàqu ci atum 2024
|
Jafe-jafe bi mooy ne, ci lu gaaw, Bànk yi mën nañoo jotale xaalis yooyu te jaarale ko ci ay ndawam yu bari te kujje du ca mën a am.
|
Wax jooju daa juddu ànd ak ñëwug Maki.
|
Teniskat bu jigéen bii di Nawomi Osaka, ci tàggatam ca Rolaŋ-Garos, ci digganteem ak Aseigh Barti, bésu juróom-benni fan ci weeru mee atum 2021 ca Pari.
|
Dinañu topp mbir mi ba fu mu yem, loolu la wax.
|
Moom dee, nee na coppite yi yëngal nit ñi, yi ci ëpp dañuy delloo ginnaaw, di xeex demokaraasi te mënul a jàll,
|
te ñépp dañu koo war a xeex.
|
Ci joŋante bi Liverpool jël ndam li (ñaari bal ci dara), Gaynde gi moo sooke penaati bi,
|
jox ay ñoñam bal bi,
|
Moxamet Sala njëkk a dugal.
|
Bu ñu xamee ne bàrke ci béréb wala ci mbir dàqul yeneeni jafe-jafe yu jóge ca Yàlla, misaal mi mooy Kaaba gi doon ci jullit yépp bàrke te doonoon bérébu xërëm ay xarnu, ginnaaw demug Ibraayima ak ndonoom. (Majaalis, atum 2010, xëtu ñeenti téeméer ak fan-weer ak juróom-ñeent)
|
Aada ak cosaanu Senegaal doonatul ba woon sax,
|
gëm-gëm yi soppeeku na,
|
cosaan pas-pas yi ak laaj yu mag yi doon na lu ñuy waxtaane ak mbiri daara yi.
|
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.