text
stringlengths
6
463
Lii nekkul rekk ay gént waaye dafay fës saa su ne ci kàddu ak yëngu-yënguy pólótigu ñaari njiit yii.
Ci nii, kom li xewoon lu yàggul dara ci mbir yoo xam ne dafa laal ay njiiti pólótig, fexe ba askan wi ànd ak yaw dafay nekk lu mënul a ñàkk
Jumtuwaay yépp lañu sànni ci biti.
Kujje gi ?
Ay nit ñoo xam ne xamuñu wala ñuy tay-taylu ne njëndum ropplaan dees koy amal ci biir waxtaan woo xam ne dafa bari lu ca warul a senn.
Madagaskaar ak Móoritani ñoo jël ndam li.
Ñiy yëngu ci caada dañoo mës a bëgg xeltu, kon warul jaaxal kenn li ñu bëgg a niroole li ñuy def ak dëgg gi.
Dafa mel ni ci néegu daara ju nekk, ab nongo bu ci am njureef lu baax ci mbind mi dafay féete, gannaaw lépp, ci ñi mujj ci daaraam, su ñu boolee njureef yi ci yeneen fànn yépp.
Dunu yëkëti ay àrtu, waaye dinañu taxaw ci def ab yéglu bu jaar yoon.
Ci boobu, la soppeey Liverpool yu am gannaaw yi ñaax leen.
Te gannaaw seen yeewute, waa Barcelone mujjee nañoo bàyyiku ni ay cuuj.
Ay daan, su fekkee ne way-tàggatu yi bañ nañoo séq waxtaan ak ñoom.
Waaye nag, leer na ne tekkib yile limu màggaay, ci ay góor-góorlu yu leer te yàgg jëm ci yokk nekkinu askan wi ci déndu Afirig, doyul dara, daanaka sax amul fenn.
Sumbkatu làmb bi, Paab Caalis Fay taxawal na làmbi Tafaa Tin ak Booy Ñaŋ 2, jàpp nanu ko ci juróom-ñetti fan ca aareen nasiyonaal ba.
Kañ la waa Senegaal di yeewu ?
Pep dellusi na ci yoon, gànnaaw ba ñu ko dugalee ab bit.
Pep teg na ñaari juróom-ñeent (9) ak benn juróom-benn (6).
Pólisu Farãas taxaw na ci siifeb liggéey bu am xaalis ak bérébu liggéeyukaayu Farãas bi, Tactical Steel, bu sampu ci Var bi, jàpp Seyne-sur-Mer.
Tënkub ay jukki yu Lazare Ki-Zerbo, CETIM, 2015.
Noppi na ci def goneg fukk ak ñetti at gi (13) ab fowukaay.
Ku mujj ki, dañu koo jàpp, yóbbu ko ca kasog Mbàkke ga, ngir ay dóor ak gaañ yu mu tay def ko.
Ba mu demee seeti réewum Farãas, sunu njiitu réewum Senegaal lu nu fonk li, yox-yoxiwul ci ŋàññ doxalin wu jagul wi ADO nekke.
Ado nekk na fi mu nekk nii fitna ci déndu Afirig sowu-jant gi.
Xumbalkat bu ndeysaane bi, mujjee na, ci diggante bi, ca suba sa rekk, feeñal ay tuub, rongoñ yi ci bët yi.
Xumbalkat bu ndeysaane bi jiital na jaar-jaaram bu fukki at yi mu def ci liggéey bi niki raayab xare, ak bokkam ci xeetu alpulaar wi, mu ngi mel ni loolu dafay nëbb jëfam ji,
dégg nañu ko, teg ci jàllale nañu ko, di xaar àttekat bi altine jii.
Wile nekkin, mujjee naa diis ci doomu Senegaal ji ma doon, moo mujjee doon aw sas ci man, ngir sama réew.
Yàlla na Yàlla teeru leen ca aljana ya.
Yàlla na Yàlla dimbali Sëriñ Saaliw Cuun ci yenam biy soog a door.
Ñun kurélu pólótig la nu, juddu ngir def pólótig, amul leneen lu dul pólótig, waaye neneen nu dul ni ñu mës a daan gise.
Soppu ak neex a jege, lu ndaw te reelu, mujjee naa taxawal ab poñ bu ñu xam ci géewu pólótig bi.
Ab këlëb bu nekk ci diggante bi, di yëngu ci njaay,
moom kay way-tàggatu gi dafay wone boppam rekk jàll, mbaa mu wàcc ba ca béréb bu xonk te wóoradi bi (ak ay mën-mën yu tuuti).
Maki Sàll a ngi liggéey sunu réew mi, ci jamono ji doomu mbedd yiy nekk ci tele yeek rajoy Ndakaaru yi di nu ray saa su nekk ak seen njàngat yu amul solo yi.
Baax na ñuy jaaxlewu ngir teggin ak kersa, yi tax ba Usmaan Sónko bañ a jañ yombalug njabootu Njaga Ndóoy, fi ñeneen ñi meloon ni ñu ko xaarul woon benn yoon.
Futbalkatu digg bu Bruges bi, Kerepee Jaata dugal na balu ñaareel bi cib àndandoo bu rafet, lu tollook ñaar-fukki meetar (20),
ngir fayul benn bal bu waa Tanzanie mball.
Alxuraan ji nekkul almet bu ñuy jëfandikoo saa boo amee ay jëflante yoo bëgg a faj.
ADD : ca MOJIP FARÃAS, am nanu ay naal yu bare yu jëm ci jigéeni waa Senegaal.
Leer na ne du ci Jëwrin ji ñu dénk koppar yeek koom-koom gi, du ci Njiital réew mi, moo war a wax di ko jaare ci jëf ju ñu yoonal,
muy lu war a mën a jàlle ci doole, walla lu ñu mën a teggi ag fayam.
Kon, fàww nga nekk ku xamul tus ngir mën a taxawal yoon wuy xeex jublu ci sàmm kumpa,
ndax xabaabal ci njëg li nu fésal ci awiyoŋu Airbus A320, mën na yombal, luy tollook ay téeméeri milyoŋ, ngir xam njëgu awiyoŋ bi nu digee jënd.
Feeñal ne dina ormaal li mu nar, këlëb bu merengue bi fésal na ne Zidane mooy kéemtaan lu mag li nekk Real Madrid.
Te jaar-jaarau Zidane romb na li mu mës a nekk tàggatkat ak way-tàggatu ci sunu këlëb bi.
Li am solo, loolu la wax, "mooy mën-mënu nguur gi ci fay, waaye nekkul ci yemukaayu bor bi nga xam ne, moo ngi ci doxinu nguur gu nekk, gu bëgg a jëm kanam".
Paab Maalig Si, jàpp na ne Aali Nguy Njaay a waroon a waxtaane Gàmmu gi, ndax waxam ju matale te leer,
loolu la ci teg ak melo wu xoromu, ba tax mbooloo mi daanu ci suuf ak i reetaan.
Wàcce, ak leeral tolluwaay deppãasu askan wi, moo nekk, kon li waral ñu xaajale koom-koom gi ci ay tëralin.
Xar sunu tànku tubay ngir am nattukaayu yaram ci bérébu jàngukaay yeek bérébi tàggatu yi.
Yokk liggéeykati kaaraange gi ci biir dëkkuwaayu ndongo yi, sasoo wàñni lim bu ëpp bi nekk ci néeg yi ak seen dàkkantal wu siiw woowu di clandotage :
Taxaw ci yégle yeek yee askan wi jaare leen ciy nataal yu mag ak yu ndaw yuy wane matukaay yi jëm ci nekkinu gaar mbas mi.
Xoolaat tëralinu waxtuy njàng mu kawe mi ci li des ci at mi, te joyyanti diir bi ba mu méngook dundug mbas mi.
Xalaat aw tëralin wuy tënk di wone xaaj yi ci ëpp solo ci diir bi ñu ame léegi, niki néegu daaray càmbar yi ci njàng mu digg-dóomu mi.
Boole njàngum teewaay meek njàngum soree mi.
Gënal njàngale mu soree mi, ngir dàrsu yi ëmb lépp, te bàyyi njàngum jiite (TD) meek jëfe (TP) ciy teewaay.
Ful mboolooy njàngum jiite (TD) meek jëfe (TP), ngir seen i xaaj ngir moytu néegu daara yu fees yeek i nit, rawatina ñi seen njàng tollu ci at mu jëkk mi (L1), ñaareelu at mi (L2), ak ñetteelu at mi (L3) ci daara yi seen jumtukaayi njàngale matale.
Waxul sax ci mbënd mi nekk ci yeneen dëkk yi bokkul ak Ndakaaru.
Nekkul ne dara taxul ba PASTEF mi doon génn ci kuréli pólótig yu néew yiy faral di bàyyi ay kopparu denc ca këru jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi.
Musibaa ngi ame ci goxu Jaalo, ci lu gën a leer, ci yoon wi jëm ca estaatu dëkk ba.
Soo yóbboo say aji-feebar ci dëkkandoob Almaañ bi, ba noppi jële fa jumtukaay yu ñu jagleel menn ci réewi way-bokk yi ci booloog réewi Europe yi, loolu mooy tekki ne, ci biir, amuñu lu matale ngir xeex ak tawat ji ca na mu ware.
Ci leeraayu mbind mii, dina jafee gëm wóoraayu nguur gu nekk ci tànki jëmmal yoon ci koppar yi muy jubbanti, gannaaw ba mu ko amalee njëkk ñetti weer (3).
Te noppi nanu ngir bokk ak yéen sunu xam-xam, la Ibraayima Ñaan dëggal, kenn la ci ñi ŋànk këlëb bi.
Jéem leen a def ay kondaane ci seen i mébéti gént, wala ci takkug naxasaale, yeewu gi dina jamp.
Mujjantal gi ñu ñàkk, dafa ñuy fàttali bépp dayo.
Ca Farãas, aw yoon ci jubbanti koppar yeek wenn yoon wu mënul a xaar ngir jàkkaarlook mbasum Koronaa mi, wote nañu ko, gannaaw ñaari fani waxtaan ca Senat ba.
Su fekkee ne am gi, mu ngi ci diggante tus ba téeméer ak fukk ak juróom-ñeenti junni ak juróom-ñetti téeméer (0 et 599 000) ci Seefaa, juuti bi mooy téeméer ak juróom-ñett-fukk (900 F) ci Seefaa.
Su fekkee ne am gi, mu ngi ci diggante téeméer ak ñaar-fukki junni ak téeméer ak juróom-ñeen-fukki junneek juróom-ñeent ak juróom-ñetti téeméer (600 000 F ak 999 000 F), juuti bi mooy doon juróom-ñaar téeméer ak ñaar-fukk (3600 F) ci Seefaa.
Daf maa niru ne Sónko xamatul fi muy teg tànkam.
Li ci topp, Comte jàpp na ne xelu nit, naka-jekk, dafay jëfandikoo, ci toftalante ñenn ñi, gannaaw ñeneen ñi, ñetti dayo yi ngir mën a xalaat:
borom xam-xamu diine cig ngoneem, xam-xamu fàddu cig ndawam, ak amal cig màggataayam.
Mawdo, ni ko baayam daan woowe, gaawtu na ci mile at mos njàngum koom-koom.
Duñu nekk di dund beddi, foñloo ak moytuloo ci njaboot yi leen di dalal.
Du def lu dul xool yaatuwaayu bérébu dalukaayi daamaari nguur gi, ndax mu xam, ñenn ci kilifaay réew mi jox nañu leen ñaar, ñett ba sax lu ëpp yooyu ciy daamar yu bakkane ci tolluwaay, niki 4X4.
Ahã kay, kenn ku nekk ak bayaalu suufam, di def li mu mën.
Xanaa leeral ne lëlu waxtaanu Sutsas bi ci saytug Unsas la ame, lañu dawal ci yéglekaay bi, L’As.
Àllarba ci joŋante dem bi, Lionel Messi génne na àndandoom yi ci guuta gi leen Reds tegaloon.
Ci misaal mi ci këyit gi, am na ay mbind : rusloo ngeen ma
Ci àksidaŋ yi am ci yoon wi, def nanu ci juróomi junni ak téeméer ak ñaar-fukk ak juróom-ñeent (5129) yu am fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom-ñaar-fukk ak juróom-ñeenti nit yu ci bokk (12 379), ñaar téeméer ak juróom-fukk ak juróom-ñaari nit (257) faatu nañu ci, loolu la kilifa gi Jéen Ngom xamle, moom mi bokk ci xaaj bi nekk ci saytu yi, ci rajo Rfm.
Ndimbal li dafa war a ñagu,
niki lol këru koppar gu ndaw gi, war naa muuru ngir ñu mën a jote ci yi nga xam ne tay, dañu leen a beddi ngir néewaayu li ñuy andi, ba tax na ñoo gën a lompoñ.
Bile dogal, dina gàll ñaareelu mbooloom tàggatu gi, ngir mu mën a teewal déndu Afirig ci joŋanteb àdduna bii di ñëw FIFA ak xale yi am wala yéesal fukk ak juróom-ñaari at, war a ame ca réewum Brésil jàpp juróomi fan ba ñaar-fukk ak juróom-ñaari fan ci weeru nowàmbar.
Dinañu ko xam : ay wax yu teguwul mëneesu koo dëggal.
Fu mu toll ci tëralinu lu ëpp wala lu yées juróom-ñaar téeméer ak juróom-fukki milyaar yi mu gëmloo ne def na ko ci, te mu ne saafara na jafe-jefey mbënd mi ?
Ngir yóbbu seen i doom ci bérébi njàngale mu kawe mi, ay way-jur, dinañu dajale xaalis ci diiru ay at yu bare, wala ñu ame ay bor.
Lu moy loolu, tolluwaay yi gën a jàppandi ngir taxawal ab xaalis bu ñépp bokk, ba tay jii nii, jàllaguñu ko.
Gile takku ak bëgg-bëggu askan wi, du mës a dañ, lu dul Sónko dafa doon Njiit li.
Lile cofeelu bëgg sa réew, du naaxsaay!
Mooy sunu xaalis!
Ak PASTEF, defee neneen pólótig, doon na dëgg gu yemul rekk ci ab bàkk.
Njiital këru liggéeyukaay bi, AGETIP, Sëñ Alaaji Maalig Gay, meeru goxu Ñàndaan, waaf na ngir wormaal ñi loru, gannaaw bi mu amee ñett ñu faatu ci mbooloom këru taskatu xibaar bii di Leeral.
Woote léen am ndaje, dooleen fa gis lu dul ay bàndi ak ay addu-kalpe yuy ànd ak yéen.
Cuq xeex bi gën a rëy ci xeex yi ngir am ab awiyoŋ booy tukkee.
Jamono joo xam ne, njiiti réew yi am fulla te fonk seen i askan ñoo ngi xool nu ñuy leen di dooleelee, di wër lopitaal yeek ndefar yiy liggéey mask yi,
nga ne déjj déjjaaral ci sab saal, di lido ak say doom, naan ñakk bi nii, ñakk bi naa ak di saraxu ñu baal la ab bor.
Xëy bés rekk ne, damay fayal àntarpiriis yi ñaari téeméeri milyaar (200) ci seen juuti.
Waaye, mënuñu leen a bañ a araftu ci xew-xew yi leen di xaar, xam ngeen ko, daa mel ne,
ndax woteb falu njiitu réew ci déndu Afirig bi, mooy des di mel ni mu mel rekk.
Njuréef lu mujj li ñaari bal ci benn,
te Messi moo doon, moom doŋŋ, tàggatu gi dugal benn bal ci fukk ak juróomi joŋante yu mujj yi mu def ci Ligg dee sàmpiyoŋ bi.