text
stringlengths
6
463
Mu ngi dund ci ni mu yége mbaboorum Free mi.
Liy dëgg mooy yokkute du am te doxal yoon ci dundinu nit ñi amul.
Dafa war a yokk sax ay jëfam te mu leeral ko.
Te xam nan ne ñoom, njariñ ñàkku leen cee nekkal.
Njiitu réew mi Maki Sàll jëmmal na naalub def Kër Masaar diwaan.
Ñu ngi fàttaliku ne njiitu PASTEF jógul woon ci di woo kilifay aada yi ak yu diine yi ñu dugal seen loxo ci càmmug jàmm ji ak déggoo bi ci réew mi, jaare ko ci seeni sañ-sañ ngir xirtal njiitu réew mi Maki Sàll mu dakkal sëqëtoo ak xeex ay wujj pólótigam.
Njiitu Mbootaayu njiiti gox-goxaat yu Senegaal wax na ne Xalifa Sàll nit ku mucc-ayib la, ku jiital doomu-aadama ci ay jëfam.
Rax-ci-dolli, wéq wi, ndaw si taxu ko woon a jóg,
dafa doxoon ci diggante bi moo tax mu dal ko waaye wéq waa ngi jubaloon ki doon jël widéwoo yi Julius Malema (deppiteb réewum Afrique du Sud) mi di tëkku faat bakkanu deppiteb réewu Mali mi bëggoon a samp ndëndam réewam.
Kiy lëkkale liggéeyub PASTEF ca gox-goxaatu SOMON.
Nde, kilifay yi gàlloo yoon ci réewi Afirig sowu jànt yi jox nañu Senegaal àppub juróom-benni weer Senegaal ngir mu tàmbali neenalug sàrt bi mu jàllale ci Péncu Ndawi réew mi fukki fan ak benn ci weeru desàmbar ci atum 2018, te kenn waxtaanewu ko.
SENELEC, waa Senegaal a ko moom, dañoo soxla ñu leeralal ñu, te du ci kuraŋ bi doŋŋ.
Mu war a am ci ñetti fan, door nañu liggéey yi àjjuma jii ñeenti fan ci weeru suweŋ ca daara ju digg-dóomu ja nekk ca dëkk ba ak ñeenti junniy nit ak ñeenti téeméer ak fan-weer ak juróom-ñett.
Ku am jabar ak ñaari doom, M.D.W lañu taxawaloon ca këru àtte ga ca Njaaréem ndax dañu ko tuumaal ne daa jël gune gu tuuti ba pare, yóbbu ko, siif ko.
Ay laaj yu gàtt jëmale ci jëwriñ ji : Ndax man ngaa miim amug bérébi denc xaalis yooyu ?
Nu ngeen mën a def ba fay lu ëpp juróom-benni milyaar ci ay ndàmpaay SOFIKO ci atum 2015 te waajaluleen ko woon ci koppar yi réew miy jëfandikoo ci at mi.
M. D. : lan moo tax nga dem PASTEF ?
Mbër kaamil nga, dinga jógaat bu baax.
Guney Ngaala Silla yi ñoo dóor Tanzanie ñetti bal ci benn ci seen ñaareelu génn.
Moo doonoon koñ boo xam ne, nu ma ko mën a waxe sax ?
Moom dëggal na ne koom-koomu Farãas, ca jamonoy nooteel ga, mu ngi wékku woon ci ja yu Senegaal ndax fi lañu doon andi seen njaay mi.
Soppi nguur gi ndax wane na fi mu mën a yem.
Ay ŋaayoo ndax sa njariñal bopp yëngalul sax nguur gii.
Doomu Farãas ji xam-xamam màcc ci liggéey bi, siiwal na bataaxal bu yéenekaay bii di L’As tasaare.
Wax na tamit yërmande bi am tey bokk ak doomi Senegaal yi nekk bitim réew seen mettit wi, te réew yi leen dalal, mbas mu law mi fépp sonal leen lool,
laata muy delloo njukkal liggéeykati kër doktoor yi, naam sax seeni jumtukaay matewu ko.
Ngir ñu nangu baaxaayu këyiti ñépp ñi fas-yéene bokk ci palum njiitu réew mi, yoy Loraŋ Bakbóo ak Giyóm Sóro sax ci lañu bokk.
Diwaani Ndar, Maatam, Luga ak Kaasamaas ñoo ëpple ci ndimbali réewum Espaañ ci Senegaal.
Naal boobu dina tax ba juróom-ñaar-fukki junni ak juróom-ñaar ak ñeenti téeméer ak juróom -ñaar-fukki njël (77 470) jot ci kuraŋ.
Doomu Esipt bi am fan-weeri at ak ñeent nëbbul taamug Puma mi boole ci digaaleb siiwal bi payug tukki yi soxal ab liggéeyam.
Ay waxtu nit ñi di ko nekk ci néguwaayi daamar yi te duñu gis benn bis,
ñuy jënd ropplaanu juróom-benn-fukki milyaar ngir kenn nit ak njabootam te waxtaanuñu ci ak askan wi wala sax Péncum Ndawi réew mi.
Kurélu lëñbët gu Péncu ndawi réew mi, bi mu seetloo bu baax jëf yi ñuy tuumaal Maamur Jàllo, tënk na ne, lu yéeme, Maamur Jàllo sàccul alali réew mi te amul lu ñu ko mën a toppe tamit.
Bu Siin demee ba teg loxu ci mbir yi ci weeru màrs, du am ay jafe-jafe ngir mu doxal liggéey ba ci weeru awiril, ni mu koy defe ci bëru at mu yees mi isini Siin yi di def.
Liggéeykati kër doktoor yi niki, yu nguur gi, rafetlu nañu liggéeyu kilifa gi ñu fa jële di Doktëer Alaaji Màggat Sekk, fàttewuñoo ñaanal ndam kilifa gi ko wuutu.
Maki Sàll def na lu bari ci dëkku diine bii.
Keyta Balde, dellusiwaat na ci fukk ak benn yiy door joŋante bi, ak Mbay Ñaŋ, ci kaw, ñoo gën a yéexal gaawaayu po mi niki ñiy aar caax yi ci geneen wàll gi.
Dëkkandoom yu ubbeeku, ay xarit yu mu dogool néeg, yu mu bokkal am taax wala ab bérébu jàngukaay ñooy xiifal ni ku nekk ci kasog nguur gu sonn, mu leen di toroxal ni ay defkatu ñaawteef yu mag.
Ma nga tambalee njàngam leetaram ca Sorbon.
Doonoon na ku ñaw-xam-xam ci nëwu.
Ñu def ko ci atum 2021, njàngat moomu dina joxe ay digle yu baax ngir yokkuteg béréb yi gu ànd ak aw tëralin ci juróomi at.
Maki dafaay ñaawaal waa Senegaal.
Ma ne leen, ndax xam ngeen miskin ak néew-di-doole yi nekk ci gox-goxaat yi?
Ku gis wuuteb wàll yiy joŋante, xam ne seen mën-mën yi ay jalloore yu ndaw lañu (Lewandowski bokk na booba ca futbalkati Bayern)
Nettalib kurélu ndawi réew mi nangu na amug jëf juy wane ne Maamur Jàllo nangu naa tontu ci laaji ki ko yóbbu ci yoon wala yoy àttekat bi.
Moo nekkoon bu njëkk may gis samay maam ak samay doomi nijaay ak bàjjen,
te metti woon na, bi ma gisee ni nit ñiy dunde foofa.
Joxe sag jot ak sa doole ngir indi, saa bu ware, lu ñu xalaat ne moo gën ci askan wi.
Tolluwaayu baatin mën a doon jàlluwaay bu am solo ngir dëgëral li lëkkale wàll wii ak wàll wee.
Liga : joŋante bu njëkk bu Musaa Wage ak Bàrsaa yombul woon,
waaye jël nañu ndam la.
Àttekati mbootaayug futbal gu déndu Afirig jël na ay dogal.
Ca dëgg-dëgg, ay boroom doole yu kenn mënul a teg bët te seeni yitte di jàll balaa yu askan wi, ñooy nas di nocci ak a dogal.
Ñaan na, gën gaa bari, ñaari ati kaso ngir ñaawtéef yi mu def.
Kilifag soldaar yu juróomeelu wàll gi, Kolonel Suleymaan Kande, dànkaafu woon na ca tàmbalig weeru féewriye, ba muy nangu dëkk ya fippuy Kasamaas ya sancoon – Bajoŋ ak Sikun, ne bépp ñaawtéef ci askan wi dañu koy jàppe ni wooteb xare.
Doonte sax dund na lu metti ba ñu ko jàppee ba ni ñu ko bàyye, doonoon na lu am njariñ ci ag niteem.
Yaakaar naa ni du dundaat lu ni mel te ñaanalu ma loola kenn!
Lu dul fukki junniy doomi Senegaal yi dul fay kuraŋ ndax dañu doon ay kilifa yu kawe yu réew mi yor.
Li teguwul ci yoon war na xiir njiitu réew mi Maki Sàll mu xalaataat bu baax ci diggante njub ak pólótig.
Ki masoon a yore kàddoom, Sëñ Kase, sax dafa ko ñàkkal fayda.
Waa ju amee xaalis ni moom te yor beneen liggéey, di ñëw fii, di am benn poñ joŋante bu nekk ñu koy tàccu, loolu ñàkk a jox gëdd po mi la ak ñépp ñi ko jox seen dund gépp.
Moom ak suñu Gayndey Beach soccer yi.
Juróom-ñaari fan ci weeru sulet, dige bi di T1784/17 ngir jot ci Sea Premium xaatim nañu ko ci diggante sekerteeru njiitu réew mi ak tabaxkat bi, Ocea SA.
Ci pólótig, Usmaan Sónko wax nee na gëmul ay kéemaan ak jëfi kenn nit rekk.
Nguur yi tontu nañu Koronaa bi, ci lu gaaw te am solo, génn seen biro yi, di joqlante xibaar yi ci aju.
Ca dëgg-dëgg, liggéeykat wala mbootaayu liggéekat yi doonul moomeelu nguur gi am nañu ab taxawaay ci mbir mi,
wànte nguuri Afirig yépp a war a gën a góor-góorlu sóobu ci ba fexe denc këyit yépp ci ay ordinaatëer.
Aw tëralin la ñuy doxal at mii di ñëw ngir lopitaalu Tiwaawon la jëwriñu biir-réew ji wax.
Samp nañu ay laaj yu am solo ci tolluwaayu réew mi ak ëllëgam te gis nañu ci diir bu gàtt aw yoon.
Ci jàkkaarloom ak mbooloo mi ñu yebal te Meetar Mustafaa Njaay jiite ko, rafetlu na pas-pasu Maadiyu Ture ci kër diine yi ci Senegaal ak sàmm aaday réew mi.
Càmbar nañu dogal bu 2005,
wax nañu ne baaxul.
Mooy futbalkatu Afirig bi njëkka jot Onze d’Or ginnaaw Dijje Dorokbaa ca atum 2004.
EDF, Gazprom, Engie wala Eni bawoo ca Itali, doomi Siin yi, ndax am nañu yelleefu dugg ci koom-koomu këru liggéeykaay yooyu.
Estaat bi nekk na ci ag lëndëm fukki simili ak juróom-benn laata làmp yiy tàkkaat.
Man naa wax ne damaa bokk ci ñaari mbatiit te maa ngi jéem a jël saa su ne li gën a am solo ci mu nekk ci ñaar yi.
Dem ak dikk bi, payug wàcc ci réew, njëgu sampug xàmmeekukaay yi, kerosen bi ak njëgu toppatoo bi, lépp tollu na ci fan-weeri milyoŋ ci xaalisu Seefaa.
Njiitu réew mi Sàll yégle na ne dina wax ak askan wi ak waa àdduna, laata muy amal am ndaje ci mbir moomu, la ci ki joxe xibaar bi yokk.
Bu ki ngay joŋanteel amul lu dul ay fen, wax-yu-ñaaw niki ngànnaay, suñu wareef mooy bañ a suufeel suñu bopp ni moom,
te wane ngor ak rafetal ndax lii lañu ñu laaj : mukk bu ñu mbañeelug askan wi yóbbu ci def lu wacc yoon.
Tay jii, yégg-yégg bi ñu am moo tax mënuñu róññale ñi jóge Ndar ak waa Ndakaaru, Tambaa, wala Fatig ak waa Kaasamaas ak waa Bawol ak waa Jolof.
Pay, pexem Masrvi muy sukkandiku ci xarala yu yees yi te di joxe ay xeeti jëfandikoo Bànk.
Ndax dafa def xarit Sëriñ Mbàkke Njaay mi koy jañ ci def njuumte yu ki mu fi wuutu, mu di ko déey ay xalaat yu bon ?
Ps : ñiy xalaat ne këri liggéeyukaay yi nguur giy jaay mën nañu am jeexital lu baax, ca dëgg-dëgg, loolu day tax ba nguur du joxati benn këru liggéeyukaay xaalisu ndimbal,
te day teg lu tax liggéeykat yiy liggéeyal seen bopp doxal njëg yi mu dogal mu neex leen, wala mu naqari leen.
Perefee bee ko musal te xam na loolu.
Ca dëgg-dëgg, am naa mbetteel bi ma yégée ne loolu jafe-jafe la woon ci ñenn ñi.
Doy na waar de, bii yoon moom, dañoo dal ci nit ku xamul li gàllu ci ndoddam.
Ginnaaw pàcc boobu, liggéeykati kër doktoor yi waruñoo des ginnaaw.
Laata ñuy def ak a xaatim déggo boobu, kilifag kër giy fayeeku lempo yi dafa am yu mu waroon a njëkk a farataal:
tolluwaayu yelleef yi ngir wóoral dëggug moomeelu suuf si, liggéey bi nit ki def ba jot ci suuf si, defar dogal buy nangu suuf si, laajte ab këru àtte mu defal ko dogal biy biral dakkalu bor yi, laajte te saxal jumtuwaayi dogal njëgu meetar kaare bi ca tund wa, jaare ko ci ab nattukaay, dogal loolu ci suuf si mu nangu.
Bi mu wóoloodee gëm-gëmam, dafa ko yóbbu ca ëttu àttekaay ba.
Kuy jëmale ay waxam ci ñi ndóol la ñi koy ŋàññ di wax.
Ku am mbooloo la ci ñi ko sopp.
Waxtaan wi dina dajale ñaari téeméeri nit te téeméer ak juróom-fukk yi jóge ci màkkaani jàngu yi nekk ci diwaan yi.
Wér-gu-yaram: ci wér-gu-yaram gi, Fondasiyoŋ bi def na ca dëkkub Degere lopitaal bu bees bu am ay jumtukaay ak dëkkuwaayu doktoor ba koy jiite.
Doktëer Abduraxmaan Juuf dem na ca boppu Mbootaayu ñiy dugal seeni koppar ci koom-koom bu Senegaal.
Waxtaan, sottente xalaat ak yeneeni ndaje lañuy amal ca jotaayu waxtaanu àdduna bi yépp te ñu jagleel ko taxawaayu liggéeykati biir réew mi ak bitim réew yi bokkul ci nguur gi.
Gis ngeen, doonte am na xam-xam ak daraja, ku bëgge kii, mbóoti nguur gi lay doxantoo.
Bu ñu yàkkamti, ndax EKO bii am pexe la ngir daaneel xaalisu Seefaa.