text
stringlengths 6
463
|
---|
Loolu, ci jëmmal yoonu yokkuteb Senegaal, ci fexe ba dem ak dikk ci gox yi gën a yéwén ak ci fexe ba yamale askan wi ci seen wàllu dundin.
|
Ba ñu tubaab yi nootee ci atum 1957, ak ba nga xamee ne dañoo boole woon réew yu bare, def leen benn ci atum 1958, ak ba Senegaal ak Mali xaatimee ab déggoo ngir nekk menn réew, loolu yépp Mawdo moo nekkoon njiitu jëwriñu réewum Senegaal.
|
Pàcc bu gën a mag ci jigéen ñi léegi liggéeyatuñu.
|
Bokkug ja bu néew gi ñu nemmeeku ci yenn gox yi, ñi yor këri kaaraange yee ko teg seen bopp.
|
Moo tax ginnaaw ba nga tàmbaleey def ay doxantu yu ndaw ba léegi, ñoom ñépp a dugg ciy pax mel ni ay kaña.
|
Fi mu tollu tar-tar yi BEAC indi ci seen wàllu liggéey ak càkkuteefu ñiy liggéey ci wàllu koom dafa tax ñi bëgg a bokk gën a bari, ba noppi néewal njureef yi.
|
Looloo tax li liggéeykat yi daan am mënatuñu ko, loolu la kenn ku bëggul a fësal turam wax ndax dafa tënku.
|
Te ñaar ci ñoom ñépp xaalisu CFA lañu yore.
|
Dëgg la, ñaari waxambaanee doon jàppante ca céet ga.
|
Doxalin wi nga xam ne dafay fitnaal ñi nga xam ne lu leen neex def wala ñi bopp kese yitteel, dana rataxal diggante yi, te it dana tax lépp lu waay di def dana ko seet, seetaat ko.
|
Ci benn pàcc ba US Monastir wone nañu njàmbarte gu rëy ci joŋante yu jëkk yi, yi ci tegu ak ba ci yu mujj yi (juróomi joŋante lañu joŋante am ci juróomi ndam).
|
Xawma ndax ñun Taskati xibaar yi ak Maki Sàll kan moo ñu ci yab.
|
Fi Maki Sàll wonee mën-mënam mooy fexe ba néewal kàttan pàrti yi nga xam ne ñoom ñoo fi jëkk ci wàllu pólótig fii ci Senegaal, bokk na ci PS, AFP, ak PDS.
|
Samp naa laaj boobu ci atum 2016 te booba nekkaguma sax ab ndawal askan.
|
Askan wee ñu tax a jóg.
|
Askan wi lañuy xeexal ba keroog Yàlla di teg réew mi ci sunuy loxo.
|
Ñu daldi koy defar bu soobee Boroom Bi.
|
Ab ndimbal mu mën a juge ci biir wala ci biti.
|
Dëgg la, bu jëkk ñu bari ci ñu wutoon kaaraange, ñiy yëngatu ci wàllu woowu, ci lu tegewul ci jom wala njub, fullaaluñ leen woon.
|
Dañu doon jaawale liggéey bu mucc ayib ak gafa gu fees.
|
Jigéen moom ak lu mu mën a jiite, jigéen rekk lay doon.
|
Ndax nasu Eco bi mën na yemb?
|
Waaye benn taataanuwaayu xibaar bu jege kuréeli koomi péncum ndawi réew mi, seen xalaat dafa safaanoo ak loolu.
|
Ndax dégguñu fi xibaar yuy feeñal ci lu wér ne baykat yi ay nagi ratt lañu?
|
Bu loolu weesoo, bég naa lool ci li ngeen ma seetsi ngir séq ak man jotaayu laaj-tontu bi nuy waaj a amal.
|
Foog naa ne nit ñi fajuwuñu.
|
Moom moo wuutu Wàdd ci njiiteefu jëwriñ yi ñetti at yii weesu.
|
Te it moo yeggale liggéey yi taxawoon boobu ba tay.
|
Samp nañu laaj bi ci këru yéglékaay gii di Le Soleil.
|
Lenn li njiitu réew mi warloo ak ñi ko woteel mooy gën a yéwénal dundinu askan wi te dox ci seen càkkuteef yiy jariñ réew mi yépp.
|
PASTEEF suisse ñoo ngi ñaawlu ba fu ñaawlu yem li xewoon.
|
PASTEEF suisse dinañu amal xeex bu tar jàmmarloo ak jaay-doole bi ngir ñu delloo seen njiit àq ak yelleefam bi koy mën a tax mu jot ci réew mi.
|
Fexe ba lempo yemamaay, ñi war a fay ñépp di fay amagul Senegaal fi mu tollu nii.
|
Li ñuy jeexalee mooy ñu amal wote yi ci waxtu wi.
|
Ci at mi weesu wone na njàmbaarte gu rëy ca Dortmund.
|
Jot nañu ñaari milyaar yu toftal juróom-benn, benn milyaar bu toftal fukk ak juróom-ñeent ak benn milyaar ci ay dolaar.
|
MD : dañu la fal bees njiitu kuréel gu Mojib Farãas, lan nga nas ?
|
Maki Sàll ak ay naataangoom yu CEDEAO njàqare lañu am ci jàppale gi Watara di jàppale Keyta ci jafe-jafe yi am ci réewum Mali.
|
Laaj dafay sampu su fekkee ne dañu gis ne ki teewal Càdd Ronaldóo la woteel teg ci Mbape.
|
Lépp la ba mu des futbal.
|
Ba ma joxee sama këyit giy firndeel samag mën a nekk ci réew mi te mu jeex, waaji dafa nangu sama telefon bi, mel ni dafa bëggul ma jokkoo ak samay mbokk.
|
Gën nañoo yokk njàmbaarte waa PSG ba ñu àgg ci teg-dóor yi, jël ndam ci njàmbaarteg Tomas Koubek mi doon jàpp bal yi.
|
Basiiru Géy ñëwul woon sax ci robub Sàmba Sàll.
|
Moom ban xeetu nit la?
|
Nit koo xam ne amul xol ba bañ a fekke robub nit ki fexe ba xettali Senegaal ci yoxoy Maki Sàll.
|
Limal lépp lu mën a firndeel dendale bi.
|
Ay ponki xalaat yu niroo ngi ci tënku yoon bi.
|
Ci biir jamonoy mbasum Koronaa wiris la doomu Amerig bii di yëngatu ci wàllu tennis di Christian Harrison, fay na lu tollook ñetti junniy dolaar,
|
ginnaaw ba mu bañee wax ak ab taskatu xibaar te sabab bi nekk ñàkk a takk mask.
|
Bu ñu bàyyee xel peyoorug saytukat yi ak njëndum soble ak pombiteer, njëg laa ngi tollu ci juróomi milyaar yu tegal juróomi téeméer ak juróon ñeen-fukk ak ñetti milyoŋ ak juróom-benn-téeméeri junni ak fukk ak benn ak téeméer ak fukk ak ñeent ak ñaari fiftin.
|
Te wax ne mbir mi tege na ciw yoon ngir dalal seen xel, loolu ay nar la.
|
Kawasi Maki Sàll yu nëb sax a gën a am solo waa M2D yépp.
|
Li ñu mën a gis benn pàcc la rekk ci rafet-rafetal, waaye léppi yég-yég dafa mat.
|
Lan la Mãasuur Fay def ba mën a nekk njiitu njëwriñ joo xam ne am na ci gafag réew mi lu tollook ñaari téeméeri milyaar ak juróom-fukk ak ñett yu toftal juróomi-téeméeri miliyoŋ ak juróom-ñeent fukk ak téeméeri junni ak ñeen-fukk ak juróom-ñett-fukk ak téeméer bu mànke ñetti fiftin.
|
Xanaa li mu nekk goro njiitu réew mi.
|
Séville def na li mënul ñàkk ci digganteem ak Léganes.
|
Yooyu yépp, dafay tax ma xalaat ne Sónko mooy tànneef bu baax li.
|
Mbir mi dañu ko war a leeral, ba ñi ko def ñu teg leen ci yoon.
|
Yenn njiiti Afirig yi te Maki Sàll gën cee fës, ñu ngi ñaan ñu baal leen bor yi ñu ameel yenn réew yi.
|
Dëgg la, di ngeen ma wax ne téeméer boo jël juróom-ñeent-fukk yi ak juróom ay jullit lañu, ñeent ya ca des ay katolig,
|
waaye Yàlla jub ak jëf la bëgg.
|
Barça daanu na, waaye mooy wéy di nekk ci bopp bi ndax Réal ak Atletico kenn ku ci nekk dafa témboo.
|
Réal Bétis la témbool, Atlético témboo ak Séville.
|
Kon jariñoowuñu ci tolof-tolofu waa barça.
|
Péncum ndawi réew mi mën na koo bañ a wote, ci bu ñuy saytu li ñuy woowe yoonu dëggal.
|
Ab jàngalekat bu nekk ci daara ji ñu duppee Màbba Jaxu Ba ca Ñooro moo jam paaka benn ndongoom.
|
Àngalteer mën nañoo sukkandiku ci njàppalem seeni farandoo maanaam seetaankat yi.
|
Li ñuy waxtaanee tay te mooy delloosiwaat ni àll beek li dëkkee meloon,
|
dafa fekksi xalaatu kuréel gi ñu naan Ecolibri, te seen jubluwaay nekk fexe ba defar béréb yu tilim yi nekk ci biir dëkk bi.
|
Jamono ji baax na su ñu xamee ne ñenn ñaa ngi woote ngir amaat beneen Bretton Woods ndax kuréeli koom yu bànku àdduna bi dañoo wone seenug tële.
|
Bu ñu gisee ne coppitey nasi pexe yiy am ci diggante réew yi ni mu gaawee ba nga xam ne Europe a ngi dundu jafe-jafe yi am ci OTAN bi nga xam ne yàggul dara,
|
Macron dafa koo méngaleek ku xelam dee.
|
Rax-ci-dolli, dëkk bu naqari bi nga xam ne kujje gi mën nañu cee jaare xarab nguur gi wone ñàkk xam-xamu suñu njiit yi!
|
Jàppleen bu baax, Ndakaaru mooy ñaareelu dëkk ci àdduna bi boo xam ne li fi dëkk ci ay nit jaadootul ak loolu li mu mën a jur ci wàllu wér-gu-yaram.
|
Dama doon dem ci suñu dëkkandoo bi ma doon laaj : salaamaalekum, ndax Muhàmmat a ngi fi ?
|
Ngir wone ne jigéen la, njiital FMI mi ngi wax ci njàmbaarteg Senegaal.
|
Waaye bu dee dëgg rekk, ndaw su waane si ci kàdduy ISPE gii lay waxee.
|
MD : ban gis-gis nga am ci xew-xewi pólótig fii ci Senegaal ?
|
Ñàkk a jëmmal li jëwriñ ji yore wàllu ndox meek cetal gi xaatim, ñàkk a boolee liggéeykat yi nga xam ne lépp ñoom la ndax am pàcc boo xam ne dugal nañu ci seen loxo te bay nañu seen waar ci kuréel gi ñu war a taxawal.
|
Ñépp a ngi wax ci lii nga xam ne ba tay am na lees waxul.
|
Ñi nga xam ne dañu nekk ci diggante bi, kenn fullaalu leen,
|
kenn dimbaliwu leen ci seen wàllu njàng.
|
Ñaari kuréel yaa ngi doog a wax ci booloo gise bi am ci diggante Maki ak Idi.
|
Ci juróom-benneelu limat bile, wax na ci càmbarug naalu yoon bu jëkk bi aju ci doxalinu xaalisu bu atum 2020 ci ngomblaan gi, sampaale ab laaj ci jaxasoo gu fés gu nguurinu doxal geeg gu yoon ak yoonal gi jaxasoo.
|
Ñii nekk ci kujje gi amuñu benn gis-gis.
|
Waaye, tey, tele yi, rajo yi, lënd gi, yéenékaay yi dañoo bare lool.
|
Xanaa ku jinne jàpp xelam rekk moo dul seetlu ne yeneen njëgi Orange yi dañuy wujjeek Tigo mi nga xam ne dafa soppi turam ba noppi yombal ay njëgam lool.
|
Loolu xalaat bu mucc-ayib la ndax ñenn ñi ni ñuy jëfandikoo suñu tasaroo gi dafa teey xel.
|
Joŋante bu xaw a ruslu,
|
waaye Dibala moo leeral yoon wi.
|
Taala Silla dañu ko génne fi kuréelam ki tudd Fal Askan wi nekkoon.
|
Ñi topp ci moom mooy kuréel gu mag ki nga xam ne njiitu Réew mi Idiriisa Sekk, Aagibu Sumaare, Paab Jóob, Isaa Sàll ak laykat bii di Madike Ñaŋ ñoo ko taxawal.
|
Loolu la jëwrin ji yore wàllu koom gi fësal.
|
Mu ngi jëm ci taxawal ay bérébu liggéeyukaay ci lu gaaw ngir ndaw ñi jaarale ko ci jëmmalug jumtuwaay yi, gën a baril njureef yi, fexe ba li ñuy yóbbu biti-réew gën a bari.
|
Te loolu ay mébét la yoo xam ne mën naa àntul suñu jubluwaay.
|
Balaa ñu fee nekk di sóobu ci rëbb ay góor-jigéen ak li mu mën a jur ci jafe-jafeek tooñ, na ñu fexe ba suñu njiit yi leeral gis-gis bu leerul bi ñu am ci wàllum GENRE, bi ñu am ci lan mooy yeneen àq ak yelleef yu bees yi ak li ñu xaatim ca Maputo.
|
Loolu yépp nag, ngir ñu fësal ci campeefi réew mi, ne aaye nañu fi ngóor-jigéen abadan.
|
Te dafa dem ba mënatul a ñàkk ndax saa su futbalee rekk da doon defi ay mbir, donte sax daawul bokk ci yenn joŋante yi.
|
Bi muy wax dafa doon boolee làkku almãa ak wu àngale.
|
Jëfandikoowul woon benn baatu xeltu waaye yenn saa yi doonul woon neex a topp.
|
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.